Goneg nit ku nuul gi. L'enfant noir : version wolof

Goneg nit ku nuul gi. L'enfant noir : version wolof

Goneg nit ku nuul gi. L'enfant noir : version wolof
Éditeur: L'Harmattan
2007163 pagesISBN 9782296035096
Format: Broché

Kamara Laay a ngi fekk baax Gine. Bindkat la. Mu ngi juddoo

Kurusa , dëkk bu ndaw ci Penku-Gine , ci 1 fan ci sanwiyée, atum

1928. Ba mu wàccee daaraay tubaab, mu dem Konaakiri , péey

ma, topp njàngam. Ba mu amee C.A.P. ci wàllu metkanise, mu

jéema doon eñseñoor ca Faraas , àntuwut. Booba la Kamara Laay,

fekk mu tollu ci ay jafe-jafe, génne «Goneg nit ku ñuul gi»

L'enfant noir , di téereem bu jëkk, ci 1953 teg ci, at ci gannaaw gi,

«Bëtu buur bi» Le regard du roi. Ci 1956, ca jamano ja Gine di

waaja moom boppam, mu dellusi Konaakiri. Foofu, ba 1963, mu

yor fa ay sas yu am solo ca ministère de l'information , laata muy

gàddaay dem Senegaal ndax tàng-diine ga féeñoon ca nguurug

Séeku Ture te mu doon ko ñaawluji ci 1966 ci «Daramus»

Dramouss , téereem bu mujj.

Moom ba-tey, moo bind "Borom kàddu" Maître de la parole ,

ab taataanu léebi géwél yuy nettali cosaanu Mali , Kamara Laay a

ngi gaañoo Ndakaaru , 4 fan ci feewaryée, atum 1980.

Ce livre est proposé par (0) membre(s)
Ce livre est mis en favori par (0) membre(s)